Tay, internet dafa yombalal na ñu ni ñuy jaayé ak jënd. Loolu ñu koy wax « e-commerce ». Waaye lan mooy loolu ?
E-commerce mooy jaay wala ligeey ci internet. Boo amee lu ngay jaay, meun nga ko jaay ci sa site web, ci réseaux sociaux yi (Facebook, Instagram, X (Twitter), TikTok, WhatsApp, etc.), wala ci yeneen plateformes yu jaay. Nit ñi mënañu jënd ci séni téléphone wala séni ordinateur, fu ñu nekk ci aduna bi.
Lu tax e-commerce ame solo ?
- Dafa yombal : Nit ñi mëna ñu jënd fu ñu nekk, sans dem ci marché wala ci butik bi.
- Dafa gaw : Jënd gi dafa gaw, ci quelques clics rek.
- Meun nga gis ay jaayukaay yu bari : Ci internet, meun nga gis ay jaayukaay yu bari yu nekk ci ay dëkk yu wuute.
- Meun nga comparé ay prix : Avant ngay jënd, meun nga comparé prix yi ci yeneen site yi.
Naka lañuy jaayé ci internet bi ?
- Am benn site web : Meun nga créer sa site web ngir jaay say produits.
- Utiliser réseaux sociaux yi : Facebook, Instagram, ak WhatsApp ay yoon yu baax la ngir jaay ci internet bi.
- Utiliser ay plateformes yu jaay : Am na ay plateformes yu bari yu tax ngay jaay say produits ci internet.
E-commerce dafa yombalal jaay ak jënd, te dafa am solo lool ngir ñi bëgg jaay seeniy marchandises. Soo bëggé xam lu ëpp ci e-commerce, nga seet ci internet wala nga woo entreprise Jangaan Tech ñu défala formation yuñuy def ci walum jaay ak jënd ci Internet bi.